mardi 8 mars 2011

La première lecture du Mercredi des cendres

Njangaatu téereb Yonetba Yowel    2,12-18
Lile la Borom bi wax :
Dellusileen fi man ak seen xol bepp : ci koor, ci ay jooy ak ténj.
Buleen xotti seeni yere waaye xottileen seen xol te dellusifi Borom bi seen Yalla ndax dafa lewet  te bare yermande Yeexa mer te fees ak cofel.
Duy nangoo mbugel Ku xam ? Xej na dina dellusi a maat na mu bayyi mbugel mi
yewene leen barkeem :
Bu kodeffe, dingeen mena genneel  Borom bi seen Yalla sarax, njébbale gunu ko tuural.
Teggleen bufta ca yerusalem: Teralleen ag koor gu sell, yegleleen am xew mu mag, dajaleleen mbootaay gi, wooteleen ndaje mu sell, dajaleleen mag ni, mbooleleen xale yi ak liir yi.
Na seet bu goor bi wacc keram, na seet bu jigeen bi wacc neegam
Ci diggantey lotel bi ak bunt bi na kilifay yoon yi di bekk neegi Borom bi joy naa:
Borom bi, yeremal sag mbootaay ni bokk ci yow.
Buleen wacc yeefeer yi di leen toroxal ak a suufeel ndax war nanu ce demba nu naan:
“Moo! aana seen Yalla ?”
Ba mu ko defee Borom bi dellu na sopp reewam ak cofeel gu fire te yerem na mbootaayam.